1. Àddina wori neen la.
2. Aduna weru koor la faw diant sow nga do nga wagni beuss.
3. Alalu golo ca lex ba.
4. Am naa gëléem ca Gànnaar yomb naa wax.
5. Bakkan waruw dàll la : fa muy dagge dooko yëg
6. Bala nga xam, xamadi xaw laa rey
7. Bala nga xam luw taat di jariñ, mbate toog jote
8. Bant, lumu yàgg cig dex, du tax mu soppiku jasig
9. Bëgg-bëgg yee wuute, moo-tax njaay may jar ca jaba
10. Bëggum ñeex duma taxa dëppoo cin lu tang
11. Benn loxo du tàccu
12. Bes boo gis, day leb walla muy fey.
13. . Bët du yenu, waaye xam na lu bopp àttan
14. Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk
15. Béy du gëmal gënn
16. Boo bëggee xam luy laabiir, amal doom
17. Boo bëggee xam luy muñ, amal jabar
18. Bopp du ngir karaw kessé
19. Boroom nàdd yëgul boroom pañe
20. Boroom ndékki, ku ko jëkka yeewu tëddaat
21. Boroom tubéy, bu jàngoo sol
22. Bu daay také celi yendo naw
23. Bu la am-am taxa bew, ndax ñàkk du wess
24. Bu la mën-ngawar jayee ba nga mafñandum saaw, boo fa jogee loo amati jënde koog teg
25. Bu la taar bi taxa lew, ndax laago du wess.
26. Bu ñey dee xàll babal, doom yaa tax
27. Bu niam tégué, ku fékké ci nga
28. Bu sed jamee ku amul cangaay dangay banku
29. . Cokk bu saxee demi sek
30. . Cokkeer mënula réér moroom ma ci mboob
31. Cuuc bu narée doon seex cin manaluko dara
32. . Daqaar du wuum ku ko maccul
33. Dax du jaaru, nen du maac, njoolum peñ du lugët baak
34. . Dég-dég amul i tànk, waaye jàll nam ndox
35. Dëgg kaani la, ku ñu ko xëpp nga toxoñu
36. Dëkk gaar ba taxula barey gan
37. Domou golo, golo rek ley done
38. Dooley jën ndox
39. Doom su tékkiwul doomiy wàjuram késsé la, wayé su tékké di doomi nieup
40. Duma jënd jaar ci pax
41. . Ëllëk dou agn dou rére wayé lou mata soralé le
42. Fen wuy defarug mbokk a gën dëgg gu koy yàq
43. Fii kekk la, golo du fi raweeb xaj
44. Fullaay jaay daqar, mbaa ma ñam jeexal ko
45. Ganaar du am faru siiru
46. Geenu golo gudd na waaye lu ca dal boroom yëg ko
47. Geenub giléém sànguluw taat te dàqul i weñ
48. Gone, lawtanu yomb la, boo walbatiwul mu law fu la neexul
49. Gone, lu luppub ndeyam lax lax,ca lay wuufu
50. Goneg mbóóya gu reew, xaar ko ca taatu ndaa la
51. Goor buy jooy dafa wara lakkatu
52. Guddi am na boroom
53. Gumba am na beneen liggééy bu dul nas i pusó
54. Gumba du jitte yoon
55. Gumba tal na leneen ludul tebbi teen
56. Guy dana juri dég
57. Jégué atayakat taxuta njakka naan
58. Jikko dana soppiku jaan walbatiku màtt boroom ba
59. Jinné su bëggee daqaar, ku yéeg daanu
60. Këll bu ne am na mberoom
61. Kéwél du tëb doom ja bëtt
62. Kooyi bukki du njoowaanug tef.
63. Ku am kuddu du lakk
64. Ku bañ ku la ñafale, dangay toññ koo mën
65. Ku bëgg aakara ñeme kaani
66. . Ku bëgg lem ñeme yamb
67. Ku bey sa bànneex, góób saw naqar
68. Ku dee ca ja ba, yaa tàgge sa bopp
69. Ku dul toxu doo xam fu dëkk neex
70. . Ku fecc ba génnub géb, kenn du la seetaan
71. Ku jaaxaan di saw, balaa kenn tooy nga lóor
72. Ku la abal i tànk, nga dem fa ko neex
73. . Ku la mag ëpp lay sagar
74. Ku ndóbin rey sa maam, foo séénati lu ñuul daw
75. Ku nekk ci xare warula ree ku ñu jam
76. Ku sa tougnou kaw dem sa fula jeex
77. Ku topp sa bànneex, góob sa naqar
78. . Ku xamul buur saay na xam buur dee na
79. Ku xamul "Suur naa", dangay téye ca loxo ba
80. Ku xeebul sa nguur di buur
81. Ku yàgg ci teen, baag fekk la fa
82. Kuy gunge boroom biirbuy daw, lu la ca "waaxusil" fekkee
83. Kuy jaay kamaate doo bëré : boo ca dëggee mu toj
84. . Kuy jàpp jaan faalewul jiit
85. Kuy naan di nëbbu, soo jangee feeñ
86. Kuy tëp ba danu ci andë desenala tëp
87. Kuy yoot du sëkët
88. Làmb aw taat, boroom a ca gën
89. Lëg mën naa daw, waaye àttanul teg
90. . Lëg, su lekke aloom, na ko gërëme coy
91. Lëngoo daf a neex rekk, waaye koo bàyyi mu dem ak boppam
92. Li nga doon soo ko bañee, danga caa yées
93. Loo barele, barele, boo génnee gis loo moomul
94. . Loo xam xam pax, janax gën lëkoo xam
95. Lu cin xat xat, xorom ba xaj ca
96. Lu jinné màggat màaggat dese nelaju bu jommal gone
97. Lu la bett mën la
98. . Lu la mar mayul, màtt du la komay
99. Lu nex du doy
100. Lu waay rindi ci sa loxo lay naac
101. . Mag du yalla wayé yagna ak yalla
102. Maggum wakhoon naa ko moo gen maggum khamoon naa ko
103. Mën ko, defoo ko, tëlée ko gën
104. Merum ganaar lu muy wàññi tusuñe
105. . Merum golo saful boroom tool.
106. . Nag wéq na doom ja waaye bañu ko
107. Ñaari yëkkyu mat xajuñu ci menn mbalka
108. Ñaq du feeñ ci taw
109. Ndànk-ndànk ay jàpp golo ci ñaay
110. Ndibeul nathiay fék loxoy borom
111. Ndoxum kese bu forox
112. Nen du bëreek doj
113. Ngelaw la dugal xob ci pax, génnewu ko ca
114. Ngaram ngaram baayi ngaramoon na baa mouy beugua ngaram
115. . Ñu bokh teen ñooy laxasooy goj
116. . Ñu yemul lor, duñu mëqandoo sunguf
117. Picc mu masula naaw, su naawee firim rééw
118. Picc, la mu wax ci banqaasu garab du ko wax ci loxol gone
119. Raxass bopou golo yakh sabou la
120. Saabu du fóót boppam
121. Sàmmkat sañ naa maye meew, wànte sañula mayew sëllu
122. Sant dëkkul fenn
123. . Sentou assamane diaroul boukhane té
124. Soo xamoon li lay yoot, nga bàyyi li ngay yoot te daw
125. Sori kaw a tax jaxaay di saw bouki
126. . Su may dee ci àll, gayndee may rey
127. . Tànk ci suuf, jaan ci suuf, fu ñu jaar daje
128. . Tilim dina dem fu saabu mënula dem
129. Toolu golo du meññ
130. Tunguné du teew gnuy nataal
131. Tuñum giléém lang na, waaye rotul
132. . Wax soxu fetal la, su rëccee dabu ko wees
133. . Waxi mag dana guddee àll, waaye du ca fanaan
134. . Waxi ndee bu taxawee, ndund yaa tax
135. Waxtaan ñam la, ku ko teewe ca nga
136. . Wuudé, na mu la gise, la lay ëwale
137. . Xamul aay na wànte laajtewul a ka yéés
138. Xeeb sa takkum, mu takk saw say
139. Xeex, ku ko fekke, boo àttewul, danga sot
140. Xel bu doon jaay lamb
141. Yaakamti ag gaawantu lugnu jur rethiou am thia yoon
142. Yàgg ay wone légétub taat
143. Yàgg du saabu, waaye dana fóót
144. Yàlla, Yàlla, bey sa tool
145. . Yééné néég la, boroom a cay fanaan
146. Lo baye rek ngéye gouby
147. Lou dioudo si tag sou nawoule diaxaliye mbokam
148. Kou mougnoul sakharr, takk takk doula fa fékke
149. ku man te defuloo tamit lu yakhou moomla
150. gèènou golo gudduna waye losi lal borom yeukko
151. kou teupe dale si khale déssé nala béné teupe
152. Kou sore sa dieukeur yacq sa dome
153. Kou amoul lila gueneul diap si li gua am
154. kou méré ponkal yéndoo niawaye
155. thiénakh sou beugué moouthie day beury pakhe
156. Kou démoul alarba yonentebi dém dibérou firayna
157. lamigne dou lék moromam té nioroul
Partage et Téléchargement
Blog dédier aux amoureux du téléchargement
mardi 31 août 2010
vendredi 25 juin 2010
Epreuve Befm 2009 Senegal
jeudi 24 juin 2010
Sélection Rap Galséné
Inscription à :
Articles (Atom)